Wildebeest analysis examples for:   wol-wolKYG   —    February 11, 2023 at 19:57    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

8599  2SA 21:16  Ci kaw loolu Isbi Bënob ne dina rey Daawuda — kooku askanu ponkal ya ñu daan wooye Rafayeen, ca la bokkoon. Ñawkay xeejam xànjar la, diise ñetti kilo. Mu yore itam saamar bu bees.
17489  ECC 6:2  Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar.
22459  AMO 2:11  Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent, tànne ci seen xale yu góor ay séddoo, — am déet, yeen bànni Israyil?» Kàddug Aji Sax jee.